11
Ñaari seede yi
1 Bi loolu amee ñu jox ma nattukaay bu mel ni yet, ne ma: «Jógal, natt kër Yàlla gi ak sarxalukaay bi, te waññ ña fay jaamu Yàlla. 2 Waaye bàyyil ëttu bitib kër Yàlla gi; bu ko natt, ndaxte jébbalees na ko ñi dul Yawut, te dinañu nappaaje dëkk bu sell bi diirub ñeent fukki weer ak ñaar. 3 Dinaa may sama ñaari seede yi, ñuy wax ci kàddug Yàlla, sol ay saaku, di toroxlu diirub junni ak ñaar téeméeri fan ak juróom benn fukk.»
4 Ñaari seede ya nag ñoo di ñaari garabu oliw yeek ñaari tegukaayu làmp, yi taxaw ci kanam Boroom suuf si. 5 Su leen kenn bëggee def lu bon, sawaraay génn ci seen gémmiñ, daldi lakk seeni bañaale; te ku leen bëgga def lu bon, noonu lay wara deeye. 6 Am nañu sañ-sañu téye taw diirub fan, yi ñuy wax ci kàddug Yàlla. Am nañu it sañ-sañu soppi ndox yi deret te wàcce ci kaw suuf musiba yu nekk, saa su ñu ko bëggee.
7 Bu ñu noppee seen seede, rab wiy jóge ci kàmb gi dina leen xeex, daan leen, rey leen. 8 Seeni néew dinañu nekk ci péncum dëkk bu mag, boobu ñuy wooye ci misaal Sodom ak it Misra, fa ñu reyoon seen Boroom ci bant. 9 Diirub ñetti fan ak genn-wàll bépp réew ak giir ak kàllaama ak xeet dinañu seetaan seeni néew, te duñu bàyyi kenn suul leen. 10 Waa àddina dinañu bég ci seen dee, di ndokkeelante ak di joqleente ay may, ndaxte ñaari yonent ya lakkaloon nañu waa àddina.
11 Waaye bi ñetti fan ya ak genn-wàll wéyee, xelum dund, jóge ca Yàlla, solu leen, ñu jóg taxaw. Noonu tiitaange gu réy jàpp ñi leen doon seetaan. 12 Ñaari seede ya dégg baat bu xumb ca asamaan naan leen: «Yéegleen fii.» Noonu ñu yéeg asamaan ci aw niir, seeni bañaale di seetaan. 13 Ca saa sa am yëngu-yëngub suuf bu mag, te benn ci fukki xaaju dëkk ba daldi màbb. Juróom ñaari junniy nit dee ci yëngu-yëngub suuf ba, te ña ca des tiit, daldi màggal Yàllay asamaan.
14 Ñaareelu musiba mi wéy na, ñetteel baa ngi nii di ñëw.
Juróom ñaareelu liit gi
15 Juróom ñaareelu malaaka ma wol liitam, noonu baat yu xumb jib ca asamaan naan:
«Nguuru àddina, jébbalaat nañu ko sunu Boroom ak Almaseem,
te dina nguuru ba fàww.»
16 Ñaar fukki mag ak ñeent, ña toogoon ca seen gàngune ca kanam Yàlla, daldi dëpp seen jë ca suuf, jaamu Yàlla, 17 naan:
«Nu ngi lay gërëm, Boroom bi Yàlla, yaw Aji Man ji,
ki nekk te nekkoon,
ndax gànjoo nga sa kàttan gu réy gi,
ngir taxawal sa nguur.
18 Xeet yi meroon nañu,
waaye sa mer wàcc na,
te jamono ji jot na,
ji ngay àttee ñi dee,
neexal say jaam yonent yi,
ak sa gaa ñi ak ñi ragal saw tur,
muy mag di ndaw,
te nga rey ñiy yàq àddina.»
19 Noonu kër Yàlla gi ci asamaan daldi ubbiku, gaalu kóllëreg Yàlla ga daldi feeñ ca biir kër Yàlla ga, te mu daldi am ay melax, ay coow, ay dënnu, yëngu-yëngub suuf ak tawu yuur bu metti.