13
Ku tuubul bàkkaaram, sànku
1 Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal leen Yàlla. 2 Mu ne leen: «Mbaa du dangeena xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gëna nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj? 3 Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam. 4 Te fukki nit ak juróom ñett ñooñu dee, bi taaxum kaw ma ca goxu Silowe daanoo ci seen kaw, ndax dangeena yaakaar ne ñoo gëna nekk ay tooñkat ñeneen ñi dëkk Yerusalem yépp? 5 Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.»
6 Noonu mu daldi leen wax léeb wii: «Nit amoon na ci toolam garab gu ñu naan figg. Benn bés mu ñëw di ko raas-si, fekku fa benn doom. 7 Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?” 8 Surga ba ne ko: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos. 9 Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
Yeesu faj na jigéen ju xuuge ci bésub noflaay bi
10 Benn bésub noflaay Yeesoo ngi doon jàngle ci ab jàngu. 11 Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu wara mat fukki at ak juróom ñett; dafa xuuge woon te manul woona siggi dara. 12 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.» 13 Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla. 14 Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésub noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom benni fan yu nit ñi wara liggéey. Kon war ngeena ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésub noflaay bi.» 15 Boroom bi ne ko: «Naaféq yi! Ndax bésub noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko? 16 Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésub noflaay bi?»
17 Naka la wax loolu, noonam yépp daldi rus, waaye mbooloo mi di bég ci jëf yu yéeme, yi mu doon def yépp.
Léebu doomu fuddën gi
18 Noonu Yeesu neeti: «Lan la nguuru Yàlla di nirool? Lan laa ko mana méngaleel? 19 Mi ngi mel ni doomu fuddën gu nit jël, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
Léebu lawiir bi
20 Mu neeti: «Lan laa mana méngaleek nguuru Yàlla? 21 Mi ngi mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
Bunt bu xat bi
22 Yeesoo ngi doon jaar ci ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di jàngle te jublu Yerusalem. 23 Am ku ko ne: «Boroom bi, ndax ñiy mucc ñu néew lay doon?» Yeesu ne leen: 24 «Defleen seen kem kàttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu jéema dugg, waaye duñu ko man. 25 Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.” 26 Bu ko defee ngeen naan: “Noo doon bokk di lekk ak a naan, te jàngle nga ci sunuy pénc.” 27 Mu ne leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!” 28 Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti. 29 Ay nit dinañu jóge penku ak sowu, nor ak sudd, ñëw, bokk lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram. 30 Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.»
Dinañu yàq Yerusalem
31 Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wuta rey.» 32 Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.” 33 Waaye fàww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesula reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem.
34 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen! 35 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»