Saar 9
1 Juróomeelu malaaka mi wal liitam, ma gis, biddiiw bu xàwwikoo woon asamaan, ba wadd ci kaw suuf. Ñu jox ko caabiy kàmbu xóote ba. 2 Mu ubbi buntu kàmbu xóote ba, saxar su mel ni saxaras taal bu mag jollee ca, jant bi ak jaww ji, lépp lëndëm ndax saxaras kàmb gi. 3 Ba loolu amee ay njéeréer génne ci saxar si, daldi tasaaroo ci biir àddina, ñu may leen nag daŋar ju mel ni daŋaru jànkalaar. 4 Ñu ne leen, buñu laal menn um ñax, mbaa genn gàncax, mbaa genn garab, xanaa ñu jublu rekk ci nit ñi amul màndargam torluwaayu Yàlla ci seen jë. 5 May nañu leen ñu mitital leen diiru juróomi weer, te bañ leena rey, xanaa mitital leen lu tembook mititu fittu jànkalaar. 6 Bési keroog nit ñeey sàkku dee, te duñu ko daj, ñu ne siiwa dee, ndee daw leen.
7 Njéeréer yaa ngi nirook fas yu ñu waajal ngir xare, kaalawoo lu mel ni kaalay wurus, seen kanam nirook kanamu nit, 8 seen kawar mel ni kawaru jigéen, seeni sell nirook selli gaynde. 9 Ñu ngi sol kiiraayi dënn yu mel ni kiiraayi weñ gu ñuul, seen coowal laaf yi mel ni coowal watiiri xare yu bare. 10 Geen gu am fitt lañu am ni jànkalaar. Daŋaru geen googu lañuy mititale nit ñi diiru juróomi weer. 11 Seen buur a leen jiite, di malaakam xóote bi, turam ci ebrë di Abadon, Apolyon ci làkku gereg, (mu firi Yàqkat bi).
12 Naka la musiba mu jëkk mi jàll rekk, yeneen ñaari musiba dikk, topp ci.
13 Ba mu ko defee juróom benneelu malaaka mi wal liitam. Ma dégg baat bu jóge ci ñeenti béjjéni sarxalukaayu wurus, bi ci kanam Yàlla. 14 Baat bi wax ak juróom benneelu malaaka mi yor liit, ne ko: «Yiwil ñeenti malaaka, ya yeewe ca Efraat, dex gu mag ga.»
15 Ca lañu yiwi ñeenti malaaka, ya ñu waajaloon ñeel waxtu woowu, ci bés boobu, weer woowu, at moomu, ngir ñu rey ñetteelu xaaju nit ñi. 16 Limu gawari mbooloo ma doon xareji ñaar téeméeri junniy junni la (200 000 000). Maa dégg lim bi.
17 Nii laa gise ci peeñu mi fas yi ak ñi leen war: ñu ngi sol kiiraay yu xonq ni sawara, baxa ni safiir, te mboq ni tamarax. Boppi fas yaa ngi nirook boppi gaynde, sawara ak saxar ak tamarax di génne ci seen gémmiñ. 18 Ñetti musiba yooyii, sawara seek saxar seek tamarax biy génne ci seen gémmiñ, daldi rey ñetteelu xaaju nit ñi. 19 Daŋaru fas yaa ngi ci seen gémmiñ ak ci seen geen, ndax seen geen yaa ngi mel ni ay jaan, ami bopp yu ñuy mititalee.
20 Ndesu nit ñi musiba yooyii reyul nag, taxul sax ñu tuub seeni jëf, ba bañatee jaamu ay tuur, ak jëmmi xërëmi wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk; xërëm yu gisul, déggul, doxul. 21 Rax ci dolli, tuubuñu bóome gi ak ñeengo gi ak powum séy meek càcc gi ñu nekke.