Sabóor 134
Way-gëm ñaa ngi sant
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
 
Ayca, santleen Aji Sax ji,
yeen jaami Aji Sax ji yépp,
yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi.
Yékkatileen seeni loxo bérab bu sell ba,
te sant Aji Sax ji.
 
Yal na la Aji Sax ji barkeele fa Siyoŋ,
moom mi sàkk asamaan ak suuf.