Sabóor 103
Ma sant Aji Sax ji
1 Ñeel Daawuda.
Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii,
saa jëmm jépp di sàbbaal sellngay turam!
2 Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii,
te baña fàtte mboolem xéewalam!
3 Moo lay baal foo ñaawe,
di la wéral foo woppe.
4 Mooy jot sa bakkan,
kaalaa la ngor ak yërmande,
5 di reggal sa bakkan bànneex,
yeesalal lag ndaw,
nga màggataale doole nig jaxaay.
6 Aji Sax jeey def njekk,
di àtte jépp néew-ji-doole.
7 Moo xamal Musaa ay nammeelam,
xamal bànni Israyil ay jëfam.
8 Yërmandeeku yiw, fa Aji Sax ji.
Moo muñ mer te bare ngor.
9 Saxoowul di toppe,
dencul mer ba fàww.
10 Du sunuy bàkkaar la nu mbugal,
du sunuy ñaawtéef la nu fey.
11 Ni asamaan tiime suuf,
ni la ngoram yiire ku ko ragal.
12 Ni penku soree sowu,
ni la nu soreleek sunu mbugali tooñ.
13 Ni baay yërëme doom,
ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.
14 Moo xam sunu bind,
di bàyyi xel ne pënd lanu.
15 Nit aki fanam di saxayaay
suy law ni tóor-tóoru àll;
16 ngelaw li wal, mu ne mes,
mel ni masu faa nekk.
17 Waaye ngoru Aji Sax ji naka jekk
ñeel na fàww ku ko ragal;
njekkam ñeel sëtaati
18 kuy sàmm kóllëreem,
di saxoo jëfe tegtali yoonam.
19 Aji Sax jee samp asamaan ab jalam,
nguuram ŋank lépp.
20 Yeen malaaka yi, santleen Aji Sax ji,
yeen jàmbaar yu mag yiy jëfe ndigalam,
di sàmm kàddoom.
21 Santleen Aji Sax ji, yeen gàngoori xareem yépp,
yeen dagam yiy jëfe coobareem.
22 Yeen bindeef yépp, nangeen sante Aji Sax ji
fépp fu mu tiim.
Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii!