Sabóor 32
Njéggal barke la
1 Dib taalif, ñeel Daawuda.
Ndokklee yaw mi ñu baal bàkkaar,
jéggal la ag moy.
2 Ndokklee yaw mi Aji Sax ji toppul ag tooñ,
te amoo xelum njublaŋ it.
3 Ba ma nee cell,
damaa ràgg,
dëkke naqar.
4 Guddeek bëccëg
sa loxo diis gann ci man.
Sama doole ŋiis
ni ndox mu jaas upp.
Selaw.
5 Ma xamal la ne moy naa,
làqatuma la sama ñaawtéef.
Ma ne: «Naa àgge Aji Sax ji sama bàkkaar.»
Yaw nga baal ma peyug tooñ.
Selaw.
6 Nii, kuy aji gëm, na la ni ñaane,
ba ñaan jotee.
Mbënn mu baawaan, di wal sax,
du ko laal fenn.
7 Yaw laay làqoo,
nga di ma aar ciw ay,
may ma ñu ma yéew, di ko bége.
Selaw.
8 Nga ne ma: «Dama laa xelal,
xamal la fi ngay jaar,
digal la, di la xool.
9 Buleen mel ni fas mbaa berkelle
mi amul ag dégg,
laab ak tarka di ko téye,
mu doora yem fi seen wet.»
10 Ku bon barew tiis.
Ku wóolu Aji Sax ji,
mu yiire la ngoram.
11 Yaw aji jub ji, bégal te bànneexoo Aji Sax ji.
Képp kuy def njub, sarxolleel!