Sabóor 12
Kàddug Yàllaa wóor
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
Wallóoy, Aji Sax ji, ngor jee na!
Kóolute réer na doom aadama.
Dañuy fenante,
làmmiñ dig lem, xol ba njuuy la.
Yal na Aji Sax ji tëj gémmiñu kuy naxe,
ak kuy làmmiñuy tëggu.
Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane,
nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»
 
Ku ñàkk a ngi, ñu futti,
mu ngi binni, di néew-ji-doole.
Aji Sax ji nee: «Maa ngii, di ci jóg,
teg leen fi rawtu gu ñu ne siiw.»
 
Kàddug Aji Sax ji, kàddu gu sell la,
ni xaalis bu ñu xelli ci taalu ban,
settli ko juróom ñaari yoon.
Ngalla Aji Sax ji, sàmmal ku néewle,
aar ko saa su ne ci nitu tey.
Ñu bon ñaa ngi taxawaalu fu ne,
jikko ju sew falu ci biir doom aadama yi.