Saar 17
1 Sama xol jeex,
samay fan tàggoo,
bàmmeel di ma xaar.
2 Fu ma jublu ñu di ma ree,
di ma ñaawal, may gis.
3 Ngalla Yàlla, gàddul mab daan
sama digg ak yaw,
su dul yaw, ana ku may gàddu?
4 Yaa fatt xelu ñii,
kon nag bu leen may ndam.
5 Nee ñu, ku njariñ tax nga wor xarit,
say doom a cay loru.
6 Man la nit ñi def léebukaay,
di ma tifli ci kanam.
7 Naqar tax na saay gët giim,
saa cér yépp jeex ba mel ni takkndeer.
8 Ku jub a ngii jommi ci lii ma dal,
ku tooñul a ngi xabtalu fi kaw yéefar yi.
9 Waaye aji jub a ngi topp yoonam,
boroom loxo yu set a ngi gëna am kàttan.
10 Waaye yeen ñépp, waxaatleen, ma dégg,
boroom xel daal duma ko gis ci seen biir!
11 Samay fan wéy na,
mébét yàqu,
yaakaar yàkki.
12 Ñii guddi lañu def bëccëg,
naan leer sorewul, te lëndëm teew.
13 Ndegam kërug njaniiw laa yaakaarati,
te biir lëndëm laa nara tëri,
14 ndegam maa naa paxum yàqute ma: «Yaay sama baay!»
naa saxu bàmmeel: «Yaay bóoy!» mbaa «Jigéen sama!»
15 Kon ana sama yaakaar?
Ana ku gisati sama yaakaar?
16 Xanaa day ànd ak man tàbbi bàmmeel,
nu bokk tëraayu pënd.