*1:1 1.1 Tekowa sorewul ak Yerusalem, péeyu Yuda. Ba bànni Israyil xàjjalikoo ñaari réew gannaaw ba Buur Suleymaan nelawee, réewum Israyil daa péeyoo Samari; réewu Yuda péeyoo Yerusalem.
†1:1 1.1 Osiyas mooy Asaryaa itam.
‡1:2 1.2 Siyoŋ mooy tund wa kër Yàlla ga nekk ca Yerusalem. Daan nañu ko tudde it dëkku Yerusalem.
§1:3 1.3 Damaas mooy péeyu réewum Siri.
*1:5 1.5 xuru Awen mooy tekki xuru Ñaawtéef.
†1:5 1.5 Bet Eden mooy kërug Àjjana, muy tekki fii Kërug Xawaare.
‡1:5 1.5 Kir la Arameen ñi cosaanoo. Gannaaw gi lañu sanci réewu Siri. Seetal ci 9.7.
§1:6 1.6 Gasa benn la ci juróomi dëkki Filisti yu mag; yeneen yi di Asdodd ak Askalon ak Ekkron, ak Gaat. Seetal ci 6.2.
*1:9 1.9 Tir dafa mel ni Sidon. Ay dëkk yu mag lañu woon ca réewum Fenisi.
†1:11 1.11 Edomeen ñaa nga bàyyikoo fa bëj-saalumu Yuda jàpp penku. Ñu ngi soqikoo ci Esawu, magu Yanqóoba, kon bokki Israyil lañu woon, waaye dañoo faroon ak nooni Israyil.
‡1:12 1.12 Teman ak Boccra ay goxi Edom yu mag la woon. Boccra moo doon péeyu Edom.
§1:14 1.14 Raba péeyu Amon la woon.