Téereb Yonent Yàlla
Yowel
Saar 1
Kàddug Aji Sax jii moo dikkal Yowel
doomu Petuwel.
Njéeréer ak maral jubsi na
Dégluleen, yeen mag ñi,
teewluleen, yeen waa réew mi ñépp.
Ndax lii mas naa am ci seeni jant,
mbaa seen janti maam?
Waxleen ko seen doom yi ngeen jur,
doom yi ngeen jur wax ko doom yi ñu jur,
doom yi ñu jur wax ko geneen maas.
Ndesu soccet yi la njéeréer yi lekk,
ndesu njéeréer yi, seenu tostan lekk,
seen ndesu tostan, salleer yi lekk.
Màndikat yee, yewwuleen, jooyoo.
Naan-kati biiñ yee, jooyleen biiñ bu bees,
bi ñu foqatee ci seen gémmiñ.
Aw xeet a dal ci samam réew,
am kàttan, wees ab lim,
seeni sell di selli gaynde gu góor,
seeni ŋaam di ŋaami gaynde gu jigéen.
Samag reseñ lañu fóom,
samag figg lañu xasa xas, ba mu set,
ñu sànni, car ya weex tàll.
Neeleen wóoy ni janq bu woddoob saaku,
di ko ñaawloo jëkkëram,
ja ñu ko dencaloon ba muy lu tuut.
Saraxu pepp ak saraxu tuuru dagg na
ca kër Aji Sax ji.
Sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji,
ñu ngi ñaawlu.
10 Tool yi yàqu yaxeet,
suuf sëngéem ciw tiis;
pepp yàqu, biiñ bu bees wow, ag diw ŋiis.
11 Yeen beykat yi, rusleen;
boroom tóokëri reseñ yi, yuuxooleen,
ndax peppum bele baak lors ba,
nde ngóob mi sànku na.
12 Ag reseñ wow, figg lax,
gërënaat, tiir, ak pom, mboolem garabi tool,
wow koŋŋ.
Mbég daal a rasu doom aadama.
Wooteb koor ak ñaan jib na
13 Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu,
yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen,
yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen,
sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu,
nde xañees na seen kërug Yàlla ga
saraxu pepp ak saraxu tuuru!
14 Sellal-leen ag koor, woote am ndaje,
wooleen mag ñi, ak mboolem waa réew mi,
ca seen kër Yàlla Aji Sax ji,
te ngeen woo Aji Sax ji wall.
Bésub Aji Sax ji dëgmal na
15 Céy, bii bés! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal,
te ni sànkute gu bawoo fa Aji Man ji lay dikke.
16 Xanaa du ag lekk a dagg, nuy gis,
te mbég ak bànneex tukkee sunu kër Yàlla ga?
17 Aw jiwu wow na, suule ciy donji suuf,
dencukaay yi wéet, sàq yi dàjjiku, am pepp wow.
18 Céy ni mala yiy binnee!
Gétti nag yaa ngi jànnaxe, ndax ñàkk parlu,
gàtt yi itam loof.
 
19 Yaw Aji Sax ji laay woo,
sawara moo lekk parluy àll bi;
ag daay a xoyom garabi àll bi yépp.
20 Rabi àll yeet ñu ngi àppaat, jublook yaw,
nde wali ndox yee ŋiis,
te sawara xoyom parluy àll bi.