*1:1 1.1 Gannaaw ba réewum Yawut xàjjalikoo, Samari moo doon péeyub Israyil ca bëj-gànnaar, Yerusalem di péeyub Yuda ca bëj-saalum.
†1:7 1.7 jëmmi xërëm yooyu, su tojee it di gànjar gu ñu mana wecci xaalis.
‡1:10 1.10 Gaat dëkku Filisti la woon. Yeneen juróom ñeenti dëkk yi ci topp ñoo séqoon Moreset Gaat, dëkku cosaanu Mise. Ni baatub Gaat di jibe ci ebrë dafa neexoo ak baat biy tekki «nettali.»
§1:10 1.10 Bet Leyafra kërug pëndub suuf lay tekki, te neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «pëndub suuf.»
*1:11 1.11 Turu dëkk bii, Safiir, man naa tekki «taaru,» taar bi nag woroo ak gàcce gi ñu wax ci aaya bi.
†1:11 1.11 Caanan neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «génn.»
‡1:11 1.11 Eccel niroo na ak baatu ebrë bi mana tekki «gàntal,» wax ji di wund ne «wall gàntal na.»
§1:12 1.12 Turu Yerusalem wi indi na baatu ebrë bu mana tekki «jàmm,» mu woroo ak ay wi ñu ne mooy agsi Yerusalem, woroo itam ak Marot, baatu ebrë bi jegewoo ak «wextan.»
*1:13 1.13 Turu dëkk bi, Lakis lañu nirule ak baatu ebrë bu mana tekki «fasi dawkat.»
†1:14 1.14 Turu dëkk bii, Moreset, baat bi mu jegewool ci Ebrë man na tekki «ab séet.» Aaya 10 moo wax ci «Gaat.»
‡1:14 1.14 Agsib neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «wor.»
§1:15 1.15 Maresa neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «nangukatub réew.»
*1:15 1.15 Adulam mooy xunti ma Daawuda làqu woon, ba muy daw buur Sóol.