3
Kon nag, ba nu ko manatula dékku, nangu nanu ñu bàyyi nu, nun doŋŋ, ca dëkku Aten, te yónni nanu Timote, sunu mbokk ak sunu nawle ci liggéeyu Yàlla ak ci waareb xibaaru Kirist. Yónni nanu ko, ngir mu dénk leen, tey feddali seen ngëm, ngir kenn baña raf ndax nattu, yi ngeen di jaar. Yéen ci seen bopp xam ngeen ne nattu mooy sunu cér. Ba nu nekkee ak yéen sax, waxoon nanu leen, waxati ko ne fàww nu sonn; te noonu la ame, yéen xam ngeen ko. Noonu ba ma ko manatula dékku, yónnee naa, ngir xam fu seen ngëm tollu, ngir ragal Seytaane* Seytaane: maanaam fiirkat bi. fiir leen, ba sunu ñaq neen.
Waaye léegi Timote bawoo na ci yéen, indaale xibaar yu neex ci seen ngëm ak seen mbëggeel; xamal na nu ne yéena ngi am pàttaliku yu rafet ci nun te namm nu lool, ni nu leen namme, yéen itam. Noonu bokk yi, ci biir tiis ak coono yi nu nekk, seen ngëm dëfal na sunu xol. Ndaxte noo ngi dund dëgg-dëgg, ndegam yéena ngi sax ci Boroom bi. Ndaw cant yu bare yu nu wara sant Yàlla ndax yéen! Ndaw mbég mu bare, mi nu am ci kanamam ndax yéen! 10 Guddi ak bëccëg nu ngi wàkkirlu ci ñaan Yàlla may nu nu gis leen, ba mana mottali seen ngëm.
11 Yal na Yàlla sunu Baay moom ci boppam ak Yeesu sunu Boroom jubal sunu yoon ci yéen. 12 Yal na leen Boroom bi dolli mbëggeel gu tar, ngeen bëggante te bëgg ñépp, ni nu leen bëgge nun. 13 Yal na Boroom bi samp seeni xol noonu ci sellaay gu amul sikk fa kanam Yàlla sunu Baay, ba bés bu Yeesu sunu Boroom délsee, ànd ak gaayam yu sell yépp.

*3:5 Seytaane: maanaam fiirkat bi.