Ñaareelu bataaxal bi Yàlla may Pool,
mu bind ko
mu bind ko
WAA TESALONIG
1
1 Nun Pool ak Silwan ak Timote noo leen di bind, yéen mbooloom ñi gëm ci dëkku Tesalonig te nekk ci Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist. 2 Yal na leen Yàlla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
Àtte biy ñëw, bu Kirist délsee
3 Bokk yi, manunu lu dul sax ci sant Yàlla ndax yéen. Loolu jaadu na, ndax seen ngëm di gëna sax, te mbëggeel gi ngeen am ci seen biir, ku nekk ci sa moroom, di yokku lu bare. 4 Noonu nu ngi damu ci yéen ci kanam mboolooy Yàlla yi, ndax seen muñ ak seen ngëm ci biir mboolem fitnay noon, ak coono, yi ngeen di dékku.
5 Loolu mooy firndeel àtteb Yàlla bu jub bi, di wone ne yelloo ngeen nguuru Yàlla, gi tax ngeen di sonn. 6 Ndaxte jub na ci Yàlla, mu delloo coono ñi leen di sonal, 7 te it yéen ñiy dékku coono, mu boole leen ak nun, tàbbal nu ci noflaay, bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist jógee asamaan, feeñ fi. Keroog dina ànd ak malaakaam yu am kàttan, 8 sawara su yànj wër ko, mu feeñ ngir mbugal ñi xamul Yàlla te baña déggal xibaaru jàmm bi jëm ci sunu Boroom Yeesu. 9 Seen pey mooy alku ba fàww, ñu dàq leen fu sore Boroom bi ak ndamam lu réy. 10 Dina ñëw bés booba, ngir ndamam jolli ci biir gaayam yu sell yi, te ñépp ñi ko gëm yéemu ci moom— te ci ngeen bokk, ndaxte gëm ngeen li nu leen seede.
11 Moo tax dunu noppeek di leen ñaanal, ngir Yàlla sunu Boroom def leen, ngeen yeyoo li tax mu woo leen, te yeggali ak doole ci yéen bépp yéene ju baax ak bépp jëfu ngëm. 12 Noonu turu Yeesu sunu Boroom dina màgg ci yéen, te yéen it dingeen màgg ci moom, aju ci yiwu sunu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist.